한국   대만   중국   일본 
Afrig ? Wikipedia Aller au contenu

Afrig

Joge Wikipedia.
Afrig

Afrig , Afirig , moom la nu jappee ne mooy gox bi nit cosaanoo, su nu ko xoolee ci yaatuwaayam ak bariwaayu askanam (lu weesu gox bu Asi), mooy naareelu gox bi genn a rey ci adduna bi. Yaatuwaayam tollu na ci 30.065.000 km², nekk 20,3% ci jeeri ji ci adduna bi. Ay way dekkam tollu ci lu epp 800.000.000, muy benn juroom naareel bu way dekki adduna bi. Afrik a ngi yem ci bej-gannaaram ci Geej gu Diggu gi, ci sowwu ci Mbambulaanug Atlas , ci bej-saalum ci Mbambulaan gu Bej-saalum gi, ci penku ci Mbambulaanug End . Asi rekk la taqalool ci yeneen gox yi. Yamoo gi jall na ko. Ci jemm doon na gox bu bari'y melokaan, te wuute teg ci.

Cosaanam [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Baatu ≪Afrig≫ moo ngi joge ci turu Afridi yi, doonoon ag giir gu dekkoon ci Bej-gannaaru Afrig ci diwaanu Kaartaas .

Beneen cosaanam moo bayyikoo ci Berber Taferka ≪suuf≫, ≪boroom suuf≫. Ki fay dund la nuy woowee Aferkiw , Latin yi soppi ko africanus , mu doonoon aw tundu waa rom ci Afrig. Araab yi di ko wax ??????? ifr?q?y? , mu doonoon Tiniisi gu tay gi.

Neneen ne ci baatu waa geres bii di aphrike (≪amul sedd≫), latin di ko wax aprica (≪Bari naaj≫), la joge.

Taariix [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Afrik la nuy jappee ne mooy cosaanu nit, ndax desiti nit yi gen a yagg ci adduna bi fa la nu ko gisee, ci Afrig gu Bej-saalumu-Sahara .

Sahara ceru na bu baax ci maggug gox bi. Taariixu askani Bej-gannaaru Afrig yi day tolloo ak bu Tugal ak bu Penku gu Diggu gi. Li epp ci Afrig gu Bej-saalumu-sahara amul woon genn jeflante ak li des ci adduna bi, da noo beru woon.

Jamono ju yagg ja [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Xay yi juddoo ci goxu Afrig, boole nan leen ci yi gen a mag ci taariixu nit. Xayu Esipt ak bu Gana ak bu Mali , ak bu Kuush ak bu Songaay , anse.

Jamono ju yees ji [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Jappum njaam [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Ngir Xootal, yerel bii jukki ci Jappum njaam

Ci li taariixkat yi wax, jappum njaam mi ngi tambali ci xarnub VII ak araab yi. Ci lu gen a leer ci atum 652 ba Ab njiitu araab takk-taxawalee waa Nubi yi ngir nu jox leen 360 ciy jaam at mu jot. barab yi njaay mi doon amee mi ngi dale ca Mali ba Penku Afrik , ci wall gi feete bej-saalumu Sahara .

Ci xayma nee nan ci diggante xarnub XVIII ba ci xarnub XIX, benn nenteel ci nit ni ay jaam la nu woon, walla nu nu manante (takk-taxawal) ci liggeey bu nu sanut a ban. Nee nan njiitu waa afrik yi ci seen bopp noo doon jappaate ak a jaayaate.

Waa tugal lu weesu bi nu aakimoo (walla sancee) suufi Aamerig yi da noo soxla woon ay loxo yuy liggeey ci seen tool yi. Def nan ko ci 400 at (1500-1888), ay jaam yu bari jend nan leen walla japp nan leen ci tefesi afrik yi: Sowwu Afrig gepp, ak ci bej-saalumam itam. Donte tereg jappum njaam gi mi ngi waddoon ci lu jege atum 1850 (reew yepp bayyeendoowunu ko) amoon ay nit yu weyoon di ko def cig laqatu ba ci 1900.

Jamono ju mujj ji [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Aakimoo gu waa tugal [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Jamonoy aakimoo gu tugal ci Afrig moo ngi tambalee ci Ndajeem Berlin (1884-1885) ba ci tembte yi ci atum 1960, sedatle gu reew yu tay yi ca la joge. Ecoopi moo doonoon menn reew mi nu masut a teg

Melosuuf [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Ngir Xootal, yerel bii jukki ci Melosuufug Afrig

Reewi Gox bi [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Pacc yu tembte gu reewi Afrig yi
Turi Reew yeek seen raaya Reyaay
(km²)
way-dekk
(1 sulet 2002)
Fattaay
(ci km²)
Tembte Peey
Penku Afrig :
  Buruundi 27 830 8 090 068 229,0 1962 Bujumbura
  Komoor 2 170 690 948 283,1 1975 Moroni
  Jibuti 23 000 768 900 20,6 1977 Jibuti
  Eritere 121 320 4 465 651 36,8 1993 Asmara
  Ecoopi 1 127 127 74 777 981 60,0 Addis-Abeba
Royuwaay:SSD Sudaan gu Bej-saalum 644 329 12 778 250 20 2011 Juba
  Keenaa 582 650 34 707 817 53,4 1963 Nairobi
  Madagaskaar 587 040 18 595 469 28,1 1960 Antananariwo
  Malawi 118 480 13 013 926 90,3 1964 Lilongwe
  Mayot ( Faraas ) 374 201 234 456,9 Mamudsu
  Mosambik 801 590 19 686 505 24,5 1975 Maputo
  Ruwandaa 26 338 8 648 248 280,9 1962 Kigali
  Seysel 455 83 688 176,0 1976 Wiktoria
  Somali 637 657 7 753 310 12,2 1 suwe 1960 Mogadisu
  Tansani 945 087 37 187 939 39,3 1961 Dodoma
  Ugandaa 236 040 24 699 073 104,6 1962 Kampala
  Simbaawee 752 614 9 959 037 13,2 1980 Lusaka
  Saambi 390 580 11 376 676 29,1 1964 Arare
Diggu Afrig :
  Angolaa 1 246 700 10 593 171 8,5 1975 Luanda
  Kamerun 475 440 16 184 748 34,0 1 Samwie 1960 Yaunde
  Reewum Diggu Afrig 622 984 3 642 739 5,8 1960 Bangi
  Cadd 1 284 000 8 997 237 7,0 1960 Njamena
  Kongoo 342 000 2 958 448 8,7 1960 Brasawil
  Kongoo-Kinshasa 2 345 410 55 225 478 23,5 30 suwe 1960 Kinshasa
  Gineg yamoo 28 051 498 144 17,8 10 sattumbar 1974 Malabo
  Gaboŋ 267 667 1 233 353 4,6 17 ut 1960 Librewil
  Sao Tome ak Principe 1 001 170 372 170,2 1975 Sao Tome
Bej-gannaaru Afrig :
  Alseeri 2 381 740 32 277 942 13,6 1962 Alse
  Isipt 1 001 450 70 712 345 70,6 28 fewirie 1922 Xayra
  Libi 1 759 540 5 368 585 3,1 20 disembar 1951 Tripoli
  Marok 446 550 (710 050 ak sahara) 31 167 783 69,8 2 awril 1956 Rabat
  Sudaan 1 861 484 40 782 742 22 1956 Xartum
  Tiniisi 163 610 9 815 644 60,0 20 awril 1956 Tunis
Suufus waa-tugal ci bej-gannaaru Afrig :
  Duni Kanaari ( Ispaan ) 7 492 1 694 477 226,2 Las Palmasu Kanaari gu Mag ,
Santa Cruz gu Tenerif
  Ceuta ( Ispaan ) 20 71 505 3 575, 2 ?
  Madeira ( Portugaal ) 797 245 000 307,4 Funsal
  Melilla ( Ispaan ) 12 66 411 5 534, 2 ?
Bej-saalumu Afrig :
  Botswana 600 370 1 591 232 2,7 Gaboron
  Lesoto 30 355 2 207 954 72,7 Maseru
  Namibi 825 418 1 820 916 2,2 Windok
  Afrig gu Bej-saalum 1 219 912 43 647 658 35,8 Pretoria
  Eswatini 17 363 1 123 605 64,7 1968 Mbaban
Sowwu Afrig :
  Bene 112 620 6 787 625 60,3 Porto-Nowo
  Burkinaa Faaso 274 200 12 603 185 46,0 5 ut 1960 Uagadugu
  Kap Weert 4 033 408 760 101,4 5 sulet 1975 Praia
  Kodiwaar 322 460 16 804 784 52,1 7 ut 1960 Abijaa , Yamusukro
  Gaambi 11 300 1 455 842 128,8 1965 Banjul
  Gana 239 460 20 244 154 84,5 6 Maars 1957 Akra
  Gine 245 857 9 371 065 31,6 2 Oktoobar 1957 Konaakri
  Gine Bisaawoo 36 120 1 345 479 37,3 10 Sattumbar 1974 Bisaawoo
  Libeeria 111 370 3 288 198 29,5 1847 Morowia
  Mali 1 240 000 11 340 480 9,1 1960 Bamako
  Gannaar 1 030 700 2 828 858 2,7 1960 Nuasot
  Niseer 1 267 000 10 639 744 8,4 1960 Naame
  Niseeria 923 768 129 934 911 140,7 1960 Abuja
Raaya Senegaal  Senegaal 196 190 11 343 328 57,8 4 awril 1960 Ndakaaru
  Siraa Leyoon 71 740 5 614 743 78,3 1961 Freetown
  Togoo 56 785 5 285 501 93,1 27 Awril 1960 Lome
Lepp 30 368 609 843 705 143 27,8

Goxub Afrig gestu gi aju ci ay way dekkam [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Yerel bii jukki ci Way dekki Afrig

Cosaan ak diine [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Xool: Diiney Afrig

Lakk [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Gestukatu-lakk yi ci xayma nee nan 2 000 lakk ci goxu Afrik, nu boole leen ci neenti mbooloo, lakk yi fa cosaanoowul bokkunu ci.

Xool it [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Koom-koomu Afrig

Lekkalekaay yu biti [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Goxi / Kembaari adduna si
Afritugalasi Oseyaani Afrig Tugalasi
Bej-gannaaru Aamerig Tugal Asi Bej-saalumu Aamerig