Nosteg doxiin

Joge Wikipedia.
Desktop bu Ubuntu, ab nosteg doxiin GNU/Linux bu Canonical Ltd suqali

Ci xam-xamu nosukaay nosteg doxiin , ci tenk ND ( operating system walla OS ci wu-angalteer ), mooy mbooleem teriin yiy yor, saytu lekkaloo gu jumtukaayu nosukaay bi ( tappaan yi, xel mi...) ak teriin yi nga ciy jefandikoo.

Naka-jekk nosteg doxiin gi mooy tax jefandikukat bi man di jot ci embiit li nekk ci nosukaay bi jaarale ko cib jokkalekaay (muy ay njunj walla mbind yooy cuq mu lay won li nekk ci biiram). Yitteem bu njekk mooy tax ba jefandikukat bi, muy nit walla leneen, man di jokkalook nosukaay bi.

Melokaanam [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Danoo am ay cer yu ceslaay yu, daanaka, nosteg doxiin yepp bokk, waaye terewul am yooy fekk ci yenn yi rekk, moo tax nu genante:

  • Saalub noste gi: di mbooloom ay teriin yu ndaw yu lekkaloo ci seen biir, lekkaloo itam ak jumtukaayu nosukaay bi. Mooy liy njekk a ubbeeku su nosukaay bi di takk, di it, man nanoo wax, wall wi epp solo. Moo tax nuy man a def liggeey yu njekk ci ndoorteelu takk gi, tax nuy man a jot ci tappaan bu deger bi, ci dencukaay yu noste yi. Ci gattal moo yor jokkalantey xibaar yi ci biir nosukaay bi.
  • Yorkaayu dencukaay yu noste : mooy liy duggale ci tappaan yi. Wepp teriin wu soxla ab njoxe cib tappaan moom ngay woo mu duggal la fa. Mooy ki yor, rawati na, nosug njoxe yi ci nosukaay bi (wayndare yi).
  • Yorkaayu xel mi: mooy liy jox xel mu doy ngir seenug ubbeeku ak dox, fu nuy denc seeniy njoxe, teriin yi ba ci nosteg doxiin gi ci boppam.
  • Jokkalekaay bi: man nanoo doon shell walla GUI mooy tax nit ni man di jokkalook nosukaay bi.
wikbaatukaay am na xet wu tudd: Nosteg doxiin