Koom-koom

Joge Wikipedia.

Xamale koom-koom [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Koom-koom walla cawarteg koom-koom (activite economique):(lakku grees wu yagg wa : ο?κονομ?α, ≪ yor ag ker walla saytu ko ≫≪ di ο?κο? (ker ci ni nu ko xame)ak (ν?μω yor walla saytu(administrer)) mooy cawarteg nit giy feen ci liggeey ak joox (produire) ak seddale ak joqalante (echange) ak jefandikoo njuddeef yi (les produits) njefte yi (le services).

Koom-koom nag ni ngi koy jange ci xam-xami koom-koom yi, day sukkandiku nag ci gisiin yu koom-koom (theories economiques).

Dees na wax it ci koom-koom niki tolluwaayu koom-koom bu jamono bu am reew walla bu ab gox (zone), maanaam ag nekkam ci geweelub koom-koom yi. Cawarteg koom-koom gi kilifteef yu koppar yi walla goornamaa yi (atte yi) noo koy atte jaare ko ci ab politig bu di kojug jamono (conjoncturelle).

doxaliin wu mbooloo mi (Les administrations publiques)day def moom itam ay politig yu koom-koom ngir soppi doxiinu koom-koom wu am reew.

benn ci joxon yu koom-koom (indicateurs economiques) yu mag yi mooy njuddeef mu numm mu biirum reew (NJ.N.B) (produit interieur brut (PIB)), loolu mooy maye nga man a nattale dooley koom-koom yu reew yi

Koom-koom [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Xam-xamu koom-koom ( ci Fr:economie)moom xam-xamu mboolaay(social) la buy yengu ci gestu ni nuy jefandikoo jumtukaayi joox(production)yu daytalu yi am cig mboolaay (societe) ngir faj soxlay ak xemmemteefi cer(membre)yu mboolaay gii.Xam-xam bii nag mook xam-xam yepp a yam, dafa am ay degg-deggam akaki atteem waaye jeexiitalu gi mu def ci nekkiini mboolaay yi ak yu politig yi (les conditions sociales et politiques)ak ni ay seqoom ( ay relation-oom) dugganteek nekkiin yii tax na ba melow mboolaay muur ko, cuub ko.

Xam-xam bii li mu lamboo mooy seggat joox gi (production), seddale gi , ak yaxantu ak lakk walla jefandikoo njaay yi (marsandiis yi) ak njefte yi (les services) . danuy faral a wax ci koom-koom ne buy wuyyu la (positive) bu dee jeem a leeral ngertey tann yu wuuteyi, di joxe ay mbooleem ay xalaat jiital (hypotese) , walla am mbooloom ay gendiku (ay seetlu),danuy wax it ne bu nattukaay la bu dee leeral doxal yi nu war a def.

Xam-xamu koom-koom dees koy deddale ci naari banqaas yu mag:

Logo Commons

Xool it Wikimedia Commons


Xam-xam
Xam-xam
Gestubiddiw | Jemm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbej | Doolerandu | Kattan | Xam-xamu nosukaay | Mbejfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Werlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kallaama