Abdulaay Wadd

Joge Wikipedia.
Abdulaay Wadd diisoo Ci koom-koomu adduna, niw york ca atum 2002

Abdulaay Wadd mi ngi juddu ci 29 Mee 1926 ca Kebemeer , am na 82 ciy at, mooy njiitu reewum Senegaal ca 1fanu awril 2000 ba leegi, ki mu wuutu ci toogu boobu mooy Abdu Juuf . Ba tey mooy njiitu lang gu demokaraasi gu Senegaal (PDS), te it moo ko sos ci 37 Suwe 1974 ci ginnaaw bi mu ci taggoo Leopold Sedar Senghor ba mu nangu, nekk na ci kujjeg politig gi lu toll ci 25 ciy at, yagg na koo jiite, ci diir boobii tejees na ko ci ay yoon. Soxnaam mi ngi tudd Fifiyaan Wadd. Am na naari doom: goor ak jigeen, Kariim Wadd mooy goor, Sinjili Wadd di jigeen. Diineem mooy lislaam fiqu maalik, bokk it ci yoonu murit. Moom nag ku xaren la ci wallu yoon ak koom-koom am na it lijaasa jang wi gen a mag ci naari wall yooyii, mi ngi jange wallu yoon ci daara jii di lycee Condorcet ca Fraas . Wallu koom-koom mu jange ko ci daara ju kawe ju Ndakaaru .