한국   대만   중국   일본 
Xam-xamu nosukaay ? Wikipedia Aller au contenu

Xam-xamu nosukaay

Joge Wikipedia.

Xam-xamu nosukaay (walla Xam-xam bi neel nosukaay ), moo yor gestu gi aju ci ceslaay yu xibaar yi, xarala yi neel seenug nos ak seenug jefandikuwiin ci noste yi nuy jefandikoo ay nosukaay . Ni ciy yengu seen liggeey doon lekkale ay nosukaay nu doon li nuy tuddee ag lonkoo , defar ay datti njoxe , boppal ay noste , defar ay teriin te loolu laaj na xam ag kallaamag teriin , .

Cig lawal, xam-xamu nosukaay dafa embu ci li nuy wax xaralay xibaar ak jokkoo yu yees yi di xeetu xam-xam bi emb lepp li neel xibaar, ci gepp anamam. Ci teriin wi la teralkat bi di joxee ay tegtal nosukaay bi ci anam gi mu war a yoree xibaar yi, lan la ci war a def ak nan la ko war a defe. Jefaan yi nag nooy mbooleem ceri nosukaay bi, benn bu ci nekk am na liggeey bu nu ko sant: yii di renk xibaar yi, yii di leen wone ni nga begge, yii di leen soppi...

Taariix [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

Ba adduna dooree ba tay nit daa mas di ut ay jumtukaay ngir man a def ay wanneem. Ci jumtukaay yooyu, ci yi gen a yagg, man nanu cee lim alliway Hammurabi (1750 laata yeesu). Wuutuloxo yu doolerandu yu njekk noo ngi tambalee feen ci diggante XVI ak XVII u xarnu. Wannikaay bu doolerandu bu njekk, japp nanu ne, mooy bu Wilhelm Schickard ci XVI u .

Ci 1642 Blaise Pascal defaroon na, moom itam, ab Wannikaay bu doolerandu, doonoon bu nu doon jaay sax, ba tay jii juroom-neent ci yooyu man nga leen a fekk ci jeexiituwaay (musee) yi. Ci ay njelbeenam man nanoo wax ne xaymaan yi rekk noo ci doon yengu ndax li leen yitteeloon moo doonoon defar ay jumtukaay yu leen di yombalal seeni Wanni yu xayma. Ay ceslaayam yepp ci xayma lanu taxaw, rawati na linuy way aljibar bu Bool .

Tay jii xam-xamu nosukaay jel na wall wu am solo ci sunug dund, cig suqali ci wallu koom-koom ak mboolaay yu askan yi.


Xam-xam
Xam-xam
Gestubiddiw | Jemm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbej | Doolerandu | Kattan | Xam-xamu nosukaay | Mbejfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Werlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kallaama