한국   대만   중국   일본 
Ndimbal:Ubbeeku ? Wikipedia Aller au contenu

Ndimbal : Ubbeeku

Joge Wikipedia.

Bakkub Wikipedia mooy Jimbulang bu Ubbeeku bi . Tekkeem yenn saa si man naa wuute.

Lu "Ubbeeku" di tekki? [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

  • "Ubbeeku" ndaxte embitam da fa ubbeeku ngir nepp. Su nu toppee ay atteem.
  • "Ubbeeku" ndaxte amulum pay.
  • "Ubbeeku" ci su nu xoolee ci maanduteem. Fexe ba benn jengte du am ci biiram, ci wallu gis-gis yi.
  • "Ubbeeku" ndax atte yiy teral doxalinam amul kenn ku leen di tek, du ku ci "kaw" walla ci "biti". Lu weesu yenn tomb yi dul den, di yi ko teye ( juroomi ponk yi ), Askanu jefandikukat yi nooy yor maggam.
  • "Ubbeeku" ndax bind ab jukki taxul nga moom ko, li ngay bind moomoo ko. Kon ku nekk am na san-sanu soppi leen, loolu attey Wikipedia noo ko teral.

Lu "Ubbeeku" tekkiwul [ Soppi ? soppi gongikuwaay bi ]

  • "Ubbeeku" tekkiwul ne lu la neex duggal ci. Dan fee nekk ngir defar ab jimbulang bu baax te sell. Du ab yeenekaay, du it ab yeglekaay...
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne man nga fee taf ay mbind walla ay nataal yoo jele ci beneen dal walla ab kaggu(bibliotheque). Loolu jalgati aqi ki-sos (droit d'auteur) la, te yoon nanguwu ko.
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne amul kenn kuy saytu embitam. Askan wi day seet aka xent jukki yi, lu weesu seenug dugg, su jaree far nu far leen.
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne man ngaa def lu la neex ci xet yi. Dal bii ab Mbootaay buy "def ngir yalla" moo ko sos ngir lenn rekk, muy sos ab jimbulang.
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne man ngaa taf ay jukkeem ci sa dal, walla jel embitam bind ci ab jukki ngir sa yeenekaay, te tuddoo ci Wikipedia, ni fa nga ko jele.